2 Corinthians 3:18 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Te nun ñépp nag, danuy lerxat ndamu Boroom bi ak xar-kanam bu muuruwul, bay soppiku ci melokaanam, ànd ak ndam luy yokku te sax ci dooley Boroom biy Xelum Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu, leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.