2 Corinthians 3:6 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Moo nu jox kàttan, nu nekk ndaw yuy xamle kóllëre gu bees gi. Te kóllëre googu ajuwul ci ay sàrti diine, waaye mi ngi aju ci jëfu Xelum Yàlla. Ndaxte sàrti kese day jëme ci dee, waaye Xelum Yàlla dafay joxe dund.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Moo nu may manoorey doon ay liggéeykati kóllëre gu bees gu ajuwul ci mbindum ndigali yoon, xanaa kóllëre gu aju ci Noo gi. Ndaxte mbindum ndigali yoon day rey, te Noo gi di dundloo.