2 Corinthians 4:2 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Lànk nanoo ànd ci mbir, yi ñuy nëbb te ñu gàccelu. Sunuy tànk du yu njublaŋ te dunu dëngal kàddug Yàlla. Waaye nu ngi biral dëgg, di sàkku kóoluteg ñépp fa kanam Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye danoo dàq jépp jëf ju gàccelu ju nit di jëfe làq-làqal. Doxunu ag njublaŋ te sopparñiwunu kàddug Yàlla. Liy dëgg kay lanuy fésal, ba am kóoluteg ñépp, fi kanam Yàlla.