2 Corinthians 6:16 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Nan la këru Yàlla man a mànkoo ak xërëm yi? Ndaxte nun nooy këru Yàlla Aji Dund ji, ni ko Yàlla waxe:«Dinaa dëkk ci seen biir,tey dox ànd ak ñoom,ma nekk seen Yàlla,ñuy samay gaay.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»