2 Corinthians 9:13 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ci li ngeen firndeel seen mbëggeel ci joxe ndimbal lii, dinañu màggal Yàlla, ndaxte wone ngeen ni ngeen déggale xebaar bu baax bu Kirist bi, ak ni ngeen yéwéne ci seen ndimbal jëme ci ñoom ak ñépp.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Liggéey bi ci ndimbal lii nag, nit ñi dinañu natt soloom bu réy, bay sàbbaal Yàlla, ndax ni ngeen firndeele ne déggal ngeen xibaaru jàmm bu Almasi, ak ni ngeen yéwéne ci seen jàpplante, jëme ci ñoom ak ci ñépp.