Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Mu xool, yem ci buur ba taxaw fa kenu ga, na ñu ko baaxoo, kilifay xarekat yaak boroom liit ya dar Buur, waa réew ma mépp di bànneexook a wal liit ya. Atalya ne tareet ay yéreem ndax naqar, daldi yuuxu ne: «Wor am naay, wor am na!»