Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Buur Yowas nag dajale mboolem gànjar ga maamam ya, Yosafat ak Yoram ak Akasiya, jagleeloon Aji Sax ji, boole ca gànjar ga mu ko jagleeloon moom ci boppam, ak lépp luy wurus ca dencukaayi kër Aji Sax jeek kër Buur. Mu yónnee lépp Asayel buurub Siri, mu dëpp, bàyyi Yerusalem.