2 Kings 16:15 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci biir loolu Buur Axas sant Uri sarxalkat ba ne ko: «Ci kaw sarxalukaay bu mag bi ngay joxe saraxu rendi-dóomalu suba si, ak saraxu pepp bu ngoon bi, ak saraxu rendi-dóomalu buur bi, ak saraxu peppam, boole ci saraxu rendi-dóomal bi ñuy joxeel mboolem waa réew mi, ak seen saraxu pepp, ak seen saraxu tuuru. Te nga xëpp ci kawam mboolem deretu saraxu rendi-dóomal bi, ak deretu mboolem sarax su ñuy rendi. Sarxalukaayu xànjar bi moom, maa koy moom, di ko gindikoo ci Aji Sax ji.»