Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
ba keroog may dikk, yóbbu leen réew mu mel ni seen reew mi, réewum pepp ak ndoxum reseñ, réewum mburu ak tooli reseñ, réewum garabi oliw, diw ak lem tuuru, ndax ngeen dund te baña dee. Bu leen Esekiya sànk, naan leen: “Aji Sax ji moo nuy xettli.” Buleen ko déglu!