2 Kings 23:2 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Buur dem ca kër Aji Sax ji, ànd ak waa Yuda gépp, Yerusalem gépp; sarxalkat yaak yonent yaak askan wépp, ka gën a tuut ba ca gën a mag. Mu jàngal leen, ñuy dégg, mboolem kàdduy téereb kóllëre ba feeñ ca kër Aji Sax ji.