Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ba loolu wéyee Yosya indi Yerusalem mboolem sarxalkat ya doon sarxal ca dëkki Yuda, diggante Geba ba Beerseba, daldi sobeel bérabi jaamookaay ya ñu daan taal cuuraay, daaneel bérabi jaamookaay ya ca bunt ya, boole ca ba nekkoon ca buntu Yosuwe, boroom dëkk ba, te féete càmmoñ booy jaare ci buntu dëkk ba di duggsi.