Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye sang bi, lenn rekk laay ñaan, Aji Sax ji jéggal ma ko. Bu sama sang ba di dugg ca kër tuur ma ñuy wax Rimon, di ko sujjóotal, ba jàpp sama loxo, ma ànd ak moom sujjóot ca kër Rimon, yal na ma Aji Sax ji jéggal la ma fay sujjóot rekk, sang bi.»