Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Fekk na Alyaasaa nga ca këram toog, mag ña bokk toog ak moom. Buur yebal ndaw ca moom. Ndaw la agseegul, Alyaasa ne mag ña: «Xool-leen bóomkat bii yebal kuy dogsi sama bopp! Xam ngeen lan la, bu ndaw li agsee rekk, tëjleen bunt bi, tere koo dugg; ndax du tànki sangam laay dégg, mu topp ci moom sax?»