2 Peter 2:10 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Rawatina ñiy topp seen bakkan ciy bëgg-bëgg yu ruslu, te faalewuñu genn kilifteef. ñu ñeme Yàlla lañu, te dëgër bopp, ba ragaluñoo xas kilifa ya gëna kawe.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Rawatina nag boroom xemmemtéefi yàqute, yi topp seen bakkan te faalewuñu genn kilifteef. Ñu fétteeral lañu te bew, ragaluñoo saaga sax boroom daraja yu kawe ya fa asamaan.