Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Naka la Buur dégg loolu, naqar wu réy jàpp ko. Mu dem ca biir néeg ba, ca taax ma tiim bunt dëkk ba, di jooy. Ma ngay dem te naan: «Wóoy Absalom sama doom ja! Éey sama doom ja, céy Absalom sama doom ja! Éey waay su ma sañoon dee sax wuutu la, Absalom, doom. Éey waay sama doom ja!»