Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci kaw loolu Buur Daawuda ci wàllu boppam yónnee ca Cadog ak Abiyatar, sarxalkat ya, ne leen: «Waxleen ak magi Yuda, te laaj leen, ne leen: “Xanaa ñépp duñu jéem lu délloosi Buur këram, yeen ngeen des gannaaw, te moom ci boppam dégg na kàddug bànni Israyil gépp.