2 Thessalonians 1:3 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Bokk yi, mënunu lu dul sax ci sant Yàlla ndax yéen. Loolu jaadu na, ndax seen ngëm di gën a sax, te mbëggeel gi ngeen am ci seen biir, ku nekk ci sa moroom, di yokku lu bare.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla ci yeen fu nu tollu, te muy lu jaadu, gannaaw seen ngëm a ngi yokku bu baaxa baax, te cofeelu ku nekk ci yeen ñépp di gënatee law, digganteem ak moroomam.