Acts 1:13 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bi ñu dikkee, ñu yéeg ca néeg, ba sut ca taax ma, fa ñuy dal. Ñoo doon Piyeer ak Yowaana, Saag ak Andare, Filib ak Tomaa, Bartelemi ak Macë, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokkoon ci mbooloo mi ñuy wax Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa doomu Saag.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ñu agsi, yéeg ca néegu kaw taax ma, fa ñuy dal naka jekk. Piyeer a nga ca, ak Yowaan, ak Yanqóoba ak Àndre, ak Filib ak Tomaa, ak Bartelemi ak Macë, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ farlukatu moom-sa-réew ba, ak Yuda doomu Yanqóoba.