Acts 1:3 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Gannaaw ay coonoom, ñëw na ci ñoom, di leen won ay firnde yu bare te wér ne mu ngi dund; mu feeñu leen diirub ñeent-fukki fan, di diisoo ak ñoom ci lu jëm ci nguuru Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndaw yooyu itam la teew fi seen kanam ci firnde yu leer te bare, gannaaw ay coonoom. Diiru ñeent fukki fan la leen feeñu, di leen wax lu jëm ci nguurug Yàlla.