Acts 11:26 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bi mu ko gisee, mu indi ko Ancos. Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm, di jàngal nit ñu bare. Te ci Ancos lañu jëkk a tudde taalibe ya Gaayi Kirist.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu jëkka wooye gëmkat ñi ay gëm-Almasi.