Acts 12:11 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bi xelam dellusee ci moom Piyeer ne: «Léegi xam naa ci lu wóor ne, Boroom bi yónni na malaakaam, musal ma ci loxoy Erodd ak li ma Yawut ya yéene woon lépp.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Naka la xelum Piyeer délsi, mu daldi ne: «Léegi nag xam naa xéll ne, Boroom bee yebal malaakaam, te moo ma musal ci loxol Erodd, ak mboolem li Yawut yi séentu woon.»