Acts 12:20 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Fekk mu nekk ci xëccoo bu tàng ak waa dëkki Tir ak Sidon. Naka noona ñu ànd, bëgg koo gis. Ñu neexal Balastus, bëkk-néegu buur ba, di ñaan jàmm, ndaxte réewu buur ba moo doon dundal seen bos.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Fekk na Erodd dëngoo lool ak waa dëkk yi ñuy wax Tir ak Sidon. Ci kaw loolu waa Tir ak Sidon mànkoo, dikk ba ci Erodd. Ñu daldi fexe ba jubook Balastus, bëkk-néegu Buur, ba noppi di sàkku jàmm, ndax seen dundub réew, ca dundu Buur Erodd la daan jóge.