Acts 13:46 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bi loolu amee Pool ak Barnabas ne leen ci lu bir: «Yéen lanu war a jëkk a yégal kàddug Yàlla, waaye gannaaw gàntu ngeen ko, ba àtte seen bopp ne, yeyoowuleen dund gu dul jeex gi, kon nu ngi woññiku ci ñi dul Yawut.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ba loolu amee fit la leen Póol ak Barnaba tontoo, ne leen: «Yeen Yawut yi de lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla gi, waaye gannaaw gàntal ngeen ko, ba jombale seen bopp ag texe ba fàww, nu ngii di walbatiku ci jaambur ñi.