Acts 13:7 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus, di nit ku neex xel. Moom nag mu woolu Barnabas ak Sool, ngir bëgg a dégg kàddug Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ma nga bokkoon ca toppum Sergiyus Póolus boroom dëkk ba, nit ku rafet xel. Kooku namma dégg kàddug Yàlla, daldi woolu Barnaba ak Sóol.