Acts 14:13 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Fekk ci buntu dëkk ba amoon na fa kër gu ñuy màggale Sës. Saraxalekat ba nag ànd ak mbooloo ma, daldi indi ca bunt ya ay yëkk ak ay caq, yi ñu defare tóor-tóor, ngir màggal leen ci tuur deretu mala.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Jaamookaayu Sës ma nga woon ca buntu dëkk ba. Sarxalkat ba daldi indi ca bunti dëkk ba ay yëkk yu ñu takkal caqi tóor-tóor. Sarxalkat ba ànd ak mbooloo ma, nara rendi jur ga, sarxal ko Póol ak Barnaba.