Acts 15:22 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bi mu ko waxee, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom ñi gëm mépp fas yéenee tànn ci ñoom ay nit, yónni leen Ancos, ñu ànd ak Pool ak Barnabas. Noonu ñu tànn Yudd, mi ñuy dippee Barsabas, ak Silas, di ay njiit ca bokk ya.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ba loolu amee ndaw yi ak mag ñi mànkoo ak mbooloom gëmkat ñépp, ngir tànne ci seen biir ay nit, yebal leen Àncos, boole leen ak Póol ak Barnaba. Ñooñoo di Yuda, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, ñu diy mag ca bokk ya.