Acts 15:7 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Gannaaw werante wu bare Piyeer jóg ne leen: «Yéen bokk yi, xam ngeen ne, ca njàlbéen ga Yàlla tànnoon na ma ci yéen, ngir ma yégal ñi dul Yawut xebaar bu baax bi, ba ñu gëm.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jaambur ñi dégge ci sama làmmiñ, kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat.