Acts 16:18 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Muy def noonu ay fani fan, waaye bi ko Pool xajootul, mu woññiku ne rab wa: «Sant naa la ci turu Yeesu Kirist, génnal ci moom.» Noonu rab wa ne mëll, génn ci moom.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Noonu la jàppoo ay fani fan, ba Póol mujj xajootu ko. Mu walbatiku ne rab wa: «Maa la sant ci turu Yeesu Almasi, génnal ci ndaw si.» Rab wa daldi génn ca saa sa.