Acts 16:37 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanamu ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgg a sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Póol nag ne alkaati ya: «Ñoom ñu dóor nu ci kanam nit ñi, àtteesu nu sax te nu diy gor ci Room gii, rax ci dolli ñu sànni nu ci kaso bi. Léegi ñu bëgg noo dàq ndànk ci biti? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, génne nu.»