Acts 17:11 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Fekk ña fa nekk ñoo gën a am ay teggin waa Tesalonig, ndaxte nangu nañu kàddu ga te sawar ca, di niir Mbind mi bés bu nekk, ba xam ndax loolu dëgg la am déet.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waa Bere nag gëna am déggin waa Tesalonig. Ñu gëm kàddu gi, xér ci lool, bés bu nekk ñuy niir Mbind mi, ngir xam ndax la ñu leen di wax noonu la.