Acts 17:18 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi ñuy wax Epikuren ak ci mbooloo mi ñuy wax Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ci ñoom ne: «Fortukatu xam-xam bii, lu mu bëgg a wax?» Te ña ca des, bi ñu déggee Pool di waare xebaar bu baax bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, ñu ne: «Dafa mel ni, day waare ay yàlla yu nu xamul.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci kaw loolu ay boroom xam-xam yu bokk ci ngérum Epikur ak ngérum Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ña ne: «Kebatukat bii, lu muy wax nii?» Ña ca des dégg Póol di waare xibaaru jàmm bi ci Yeesu ak ndekkiteem, ñu ne: «Daa mel ni ay tuur-tuuraani doxandéem lay waareel.»