Acts 18:25 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Jàngoon na ci yoonu Boroom bi, di ku farlu ci xelam, muy xamle ak a jàngale bu wóor ci mbirum Yeesu, waaye fekk xam-xamam yem ci ni Yaxya daan sóobe ci ndox.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kooku jotoon naa jàng yoonu Sang bi. Mu ànd ak cawarte, di waare ak a jàngle lu wér péŋŋ ci mbirum Yeesu, doonte xam-xamam a ngi yemoon ci sóobeb Yaxya ci ndox.