Acts 20:24 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel ci ñépp xebaar bu baax, bi ëmb yiwu Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.