Acts 20:9 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Noonu waxambaane wu tudd Ëtikus te toog ca palenteer ba, gëmmeentu bay jeyaxu. Bi Pool di gën a yaatal waxtaanam nag, nelaw daldi ko jàpp, mu xàwweekoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci biir loolu ab xale bu góor bu ñuy wax Ëtikus ma nga tooge kéméju palanteer ba. Ngëmment dab ko, te kàddug Póol ga yàgg lool. Ay nelaw nag jàpp waa ji, mu xàwwikoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee.