Acts 21:11 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Mu ñëw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i tànkam ak laxasaayu Pool naan: «Nii la Xel mu Sell mi waxe: “Ki moom laxasaay gii, Yawut yi dinañu ko yeewe nii ca Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut.”»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Mu dikk ba ci nun, jël ngañaayal Póol, yeewe ko ay tànkam aki loxoom, daldi ne: «Noo gu Sell gi dafa wax ne: “Ki moom ngañaay lii, nii la ko Yawut yiy yeewe ca Yerusalem, jébbal ko jaambur ñi dul Yawut.”»