Acts 21:28 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
di xaacu ne: «Wallee, wallee, yéen bokki Israyil; waa jaa ngi nii, moom miy waare fépp ak ci ñépp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak bérab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci kër Yàlla gi, ba indi sobe ci bérab bu sell bii.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.»