Acts 22:30 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ca ëllëg sa mu bàyyi ko, ndaxte bëggoon na xam bu wóor lu ko Yawut ya jiiñ. Mu santaane ne, saraxalekat yu mag ya dajaloo, ñoom ak kureelu àttekat ya. Gannaaw loolu mu indilu Pool, dëj ko ci seen kanam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ca ëllëg sa nag njiital gàngoor ga bëgga am lu ko leer nàññ ca la Yawut ya jiiñ Póol. Mu yiwi ko, woolu sarxalkat yu mag ya, ak mboolem kurélu àttekat ya. Ci kaw loolu mu indi Póol, taxawal ko ci seen kanam.