Acts 22:5 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
saraxalekat bu mag ba ak mbooloom njiit yi yépp man nañu ma cee seede. Am bés ñu bindal ma ay bataaxal ngir bokki Damas. Ma doon fa dem, ngir yeew ña fa nekkoon, indi leen Yerusalem, ngir ñu yar leen.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Sarxalkat bu mag bi, ak mboolem kurélu mag ñi man nañu ma cee seede. Ci ñoom sax laa nangoo woon bataaxal bu jëm ca bokki Yawut ya ca Damaas, ga ma jëmoon, ngir yeewe fa gëmkati Yoon wii nekkoon foofa, ba indi leen Yerusalem, ngir ñu mbugal leen.