Acts 23:30 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Te bi ma déggee ne, ñu ngi koy fexeel, yebal naa ko ci yaw ci saa si. Sant naa nag ñi ko kalaame, ñu xamal la seen lay.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ba ñu ma àggee am tëru mu ko Yawut yi waajaloon nag, ci laa ko yebal ci yaw ci saa si. Jox naa itam ndigal ñi ko sikk, ne leen ñu wax ci sa kanam, gan tooñ lañu ko toppe.