Acts 27:1 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bi loolu wéyee ñu fas yéene noo dugal gaal jëme réewu Itali. Noonu ñu jël Pool ak ñeneen ñi ñu tëjoon, dénk leen njiitu xare bu tudd Yulyus, mi bokk ci mbooloom xare mu buur.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ba loolu wéyee ñu dogu noo dugal gaal, jëme nu réewum Itali. Ñu teg Póol ak ñeneen ñu ñu tëjoon, ci loxool njiitu takk-der bu ñuy wax Yulyus, bokk ci mbooloom xarem buur bu mag bi.