Acts 27:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Te gannaaw teeru ba neexul a lollikoo, ña ca ëpp mànkoo ci jóge fa, dem ci biir géej, ngir wut a agsi Fenigsë, biy teerub dunu Kereet te janook sowu suuf ak sowu kaw, nu lollikoo fa.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Te itam teeru boobu neexul woona lollikoo. Loolu waral ña ëpp ca waa gaal ga mànkoo ci jóge fa, dellu géej, te fexe nu ñu àgge Fenigsë, ngir lollikoo fa. Mooy teerub dunu Keret bi jublu sowub suuf ak sowub kaw.