Acts 27:21 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bi loolu di xew, fekk gëj nañoo lekk, Pool daldi taxaw ci seen biir ne leen: «Gaa ñi, li gënoon mooy ngeen déglu ma te bañ a jóge Kereet, ba indil seen bopp musiba ak kasara ju réy jii.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Loolu nag fekk na ñu gëjoona lekk. Póol daldi taxaw ca seen biir ne: «Bokk yi, su ngeen yégoon déggal ma, baña jóge Keret, ba moyu loraange gii ak yàqule gii.