Acts 5:36 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndaxte bu yàggul la Tëdas jóg, di jaay daraja, ba lu wara tollook ñeenti téeméeri nit far ak moom. Ñu rey ko, ña ko toppoon ñépp tasaaroo, seen pexe mujjewul fenn.