Acts 5:37 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Gannaawam it Yuda mu Galile jóg, ca jant ya ñu doon lim waa réew mi; mu yóbbaale mbooloo mu ko topp. Moom itam dee, ña ko toppoon ñépp tasaaroo.