Acts 7:35 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
«Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
«Musaa moomu ñu weddi woon, ne ko: “Ku la def kilifa ak ab àttekat?” Moom nag la Yàlla def kilifa ak ab jotkat, yebal ko ci ñoom, malaaka ma feeñu Musaa ca gajj ba, daldi koy jottli yóbbante ba.