Acts 7:42 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye bi ñu ko defee Yàlla dëddu leen, bërgël leen, ñuy jaamu biddiiwi asamaan. Moom lañu bind ci téereb yonent yi ne:“Yéen bànni Israyil, ndax rendi ngeen jur,jébbal ma, boole ko ak i sarax,diirub ñeent-fukki at ca màndiŋ ma?
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yàlla nag dëddu leen, bàyyi leen, ñuy jaamu biddiiw yi, ni ñu ko binde ci téereb yonent yi, ne: “Yeen waa kër Israyil, saraxu jur ak yeneen sarax, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?