Acts 7:5 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu war a donnale, du sax fu mu man a teg tànkam; waaye dig na ko ne, dina ko may réew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Taxul mu muurale ko lenn ci réew mii, du sax fu mu teg tànkam. Teewul mu dig ko, ne moom lay moomale réew mi, mook askanam wa koy wuutuji, te fekkul sax mu am doom.