Acts 7:8 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Yàlla nag tëral kóllëre seen diggante, fas ko ci màndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca juróom-ñetteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanqóoba, Yanqóoba it def noonu fukki maam ya ak ñaar, ñi sos xeet wi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yàlla daldi fasook Ibraayma kóllëre gu mu màndargale xaraf. Moo tax Ibraayma xarfal doomam Isaaxa, ba mu juddoo ba am juróom ñetti fan; Isaaxa, Yanqóoba, Yanqóoba, fukki maam yaak ñaar.