Acts 8:1 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Sool moom ànd na ci ñi doon rey Ecen. Bés booba nag fitna ju metti dal na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk Yerusalem, ba ñépp, ñu moy ndaw ya, tasaaroo ci diiwaani Yude ak Samari.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Sóol nag rafetlu woon na la ñu bóom Eccen. Bésub keroog teg nañu mbooloom gëmkat ña ca Yerusalem fitna ju metti ba, lu moy ndawi Almasi, ñoom ñépp a tasaaroo ca diiwaani Yude ak Samari.