Acts 9:27 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sool gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damas.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci kaw loolu Barnaba ànd ak moom, yóbbu ko ca ndaw ya. Barnaba nettali leen, ni Sóol gise Sang bi ca yoon wa, ba mu wax ak Sóol, ak fit wa Sóol waaree ca Damaas ci turu Yeesu.